22 Fōfale ñu indi fa mom kena ku jine jap’ on, ka silmah͈a te lū; mu weral ko, tah͈na nit ka lū on wah͈ te gis.
Dēgdēg i tur am dem cha bir Syria yepa; ñu yub ko nit ña op’ on ñepa, ña jangaro ju mun a don ak nchono jap’ on, ak ña i jine jap’ on, ak ña say, ak ña lafañ, te mu weral len.