2 Wande Pharisee ya ba ñu gise lōla, ñu ne ko, Sêtal, sa i tālube ange def lu daganul a def chi bes i dimas.
Te gōr anga fa ku am loh͈o bu lagi. Ñu lāj ko, ne, Mbar dagan na weral chi bes i dimas? Ndah͈ ñu mun ko jêñ.
Wande mu ne len, Ndah͈ jangu len la Dauda def on ba mu h͈īfe, ak ña and’ on ak mōm;