14 Wande Pharisee ya gēna, te fēncha naka ñu ko mun a rēye.
Te ñu wah͈ante chi sēn bopa ndah͈ ñu japa Yesu chi mūste, te rēy ko.
Ba lelek sa jote, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñepa fēnchu Yesu, ndah͈ ñu rēy ko.
Yauod ya fabati i doch ndah͈ ñu jumat ko.
Ñu jēmati ko japa; te mu rēcha chi sēn loh͈o;
Cha ganou bes bōbale, ñu fēncho ndah͈ ñu rēy ko.
I njīt i seriñ ya ak Pharisee ya joh͈e won nañu eble, ne su kena h͈ame fu mu neka, na ko wone, ndah͈ ñu japa ko.
Lile tah͈ Yauod ya dole ūt naka ñu ko rēye, ndege moyul on Dimas ji reka, wande tūda na Yalla Bay am itam, di emale bop’ am ak Yalla.
Ñu di ko ūt a japa nak; wande ken tegul loh͈o chi kou am, ndege wah͈tu am jotangul.
Pharisee ya dēga mbōlo ma ñu werante yef yile chi lu jem chi mōm; te njīt i seriñ ya ak Pharisee ya yōni i saltige ñu japa ko.
Te ñena chi ñom buga nañu ko japa; wande ken tegul loh͈o chi kou am.
Tah͈na ñu jel i doch ndah͈ ñu jumat ko: wande Yesu nuba bop’ am, te gēna cha biti juma ja.