10 Te gōr anga fa ku am loh͈o bu lagi. Ñu lāj ko, ne, Mbar dagan na weral chi bes i dimas? Ndah͈ ñu mun ko jêñ.
Wande Pharisee ya ba ñu gise lōla, ñu ne ko, Sêtal, sa i tālube ange def lu daganul a def chi bes i dimas.
Pharisee ya ñou fi mōm, di ko fir, te ne ko, Ndah͈ dagan na nit fase jabar am ndig lu mu mun a don?
Tah͈na Yauod ya ne ka ñu weral on, Tey Dimas la, te daganul nga yubu sa lal.
Chi bir i mbōlo chi ñu op’ on, i silmah͈a, i lago, ak i lafañ teda fa.
Su ngēn h͈arfale gōr chi Dimas mbōk, ndah͈ du len moy eble’ Musa ba, ndah͈ da ngēn ma mere ndege weral on nā nit cheng cha Dimas ja?
Te lile wah͈ nañu ko di ko jēm, ndah͈ ñu mun a am lu ñu ko jêñ. Wande Yesu sega, te binda chi suf si ak baram am.
Ñena cha Pharisee ya ne nak, Nit kile dowul ku bayako fa Yalla, ndege du japa bes i Dimas ja. Wande ñenen ne, Naka la nit ku di bakarkat mun a defe mandarga yile? Te h͈ājalo jog na chi sēn digante.