7 Ba ñu deme, Yesu dal di ne mbōlo ma lu jem chi John, Lan ngēn dem on cha manding ma ndah͈ ngēn sêt? H͈īs bu di yengatu ak ngelou lê’m?
Wande lan ngēn dem on ndah͈ ngēn sêt? Nit ku sāngu chi nchangay lu noy am? Ña sāngu chi nchangay lu noy angi chi i nēg ī bur.
Du dama sonka bu lūnka, du fey gilinta bu di sah͈ar, be mu yōni njūbay be chi ndam.
Batise’ John, fan la juge won? cha ajana am chi nit? Ñu werante chi sēn digante, ne, Su ñu ne, Cha ajana; di na ñu ne, Lutah͈ gumu len ko won mbōk?
Jerusalem, ak Judæa yepa, ak deka yu jegeñ Jordan yepa, dem fa mōm,
Te Yesu h͈inaku, te gis len ñu di topa, te ne len, Lu ngēn di ūt? Ñu ne ko, Rabbi (mu tiki ne Jemantalkat bi), ana fan nga deka?
Mō don lampa ba di tāka te di melah͈: te nangu won ngēn a banēh͈u chi i sā cha lêr am ga.