5 Silmah͈a yange gis, lago yange doh͈, gāna yange wer, teh͈ yange dēga, ña dē dēkaliku, te ñunge wāre linjil bi chi miskin ya.
Weral len ñu opa ña, setal len gāna ya, dēkali len ñu dē ña, dah͈a len i jine: ndig dara ngēn ko ame, maye len ko ndig dara.
Yesu tontu len, ne, Dem len, nitali John li ngēn dēga, ak li ngēn gis;
Fōfale mu wah͈ gōr ga, ne, Talalal sa loh͈o. Mu talal ko; mu wer niki benen ba.
Silmah͈a ya ak ña lagi ñou fi mōm chi juma ja, te mu weral len.
Barkel cha ña sufelu chi fit; ndege ngur i ajana di na len lew.
Sēn i but ūbiku. Yesu artu len bu bāh͈ ne, Otu len bu ko kena yēg.
Yesu tontu len, ne, Wah͈ on nā len, te gumu len: ligey yi ma def chi suma tur i Bay, yile ma sēdêl.
Wande su ma len defe, su ngēn ma gumule, na ngēn gum ligey yi: ndah͈ ngēn mun a h͈am te dēga ne Bay ba’ngi chi man, te mangi chi Bay ba.
Ba mu neke cha Jerusalem cha h͈ewte i njot ga, ñu bare gum on nañu chi tur am, ba ñu gise koutef ya mu def on.
Kōkale ñou on na fi mōm chi gudi, te ne ko, Rabbi, h͈am nañu ne yā di jemantalkat ba bayako fa Yalla: ndege ken munul a def koutef yile nga def, su Yalla nekule ak mōm.
Wande sēde ba ma am mō upa bu John: ndege ligey ya ma Bay ba joh͈ ma motali len, ligey yile lā def, ño ma sēde ne Bay ba ma yōni on.
Te ne ko, Demal, selmu cha dēg i Siloam (mu tiki ne Yoni). Mu dem, te selmu, te delusi di gis.