4 Yesu tontu len, ne, Dem len, nitali John li ngēn dēga, ak li ngēn gis;
Ñu ne ke, Ndah͈ yā di ki war a dika, am war naño sēnu kenen?
Silmah͈a yange gis, lago yange doh͈, gāna yange wer, teh͈ yange dēga, ña dē dēkaliku, te ñunge wāre linjil bi chi miskin ya.
Mbōlo mu rey ñou fi mōm, and’ ak ña lagi, silmah͈a, lu, tēlekat, ak ñenen ñu bare, nu teg len chi tank’ am, te mu weral len;
Silmah͈a ya ak ña lagi ñou fi mōm chi juma ja, te mu weral len.
Yesu talal loh͈o am, te lāl ko, ne, Di nā tah͈ nga set. Chi tah͈ouay ba mu dal di wer.
Gum len ma ne mangi chi Bay ba, te Bay ba’ngi chi man: te su nekule, gum len ma ngir ligey ya sah͈.
Wande sēde ba ma am mō upa bu John: ndege ligey ya ma Bay ba joh͈ ma motali len, ligey yile lā def, ño ma sēde ne Bay ba ma yōni on.