28 Dikasi len fi man yēn ña lota te dīs ñepa, te di nā len may noflay.
Enu len suma suf chi yēn, te jemantu len chi man; ndege da ma lew, te sufelu chi h͈ol; te di ngēn feka noflay chi sēn i fit.
Ño di taka say yu dīs, te mite yubu, teg len chi i mbag i nit; wande ñom du ñu len randal ak sēn baram.
Ña ma Bay ba may ñepa, di nañu ñou fi man: te ku ñou fi man, du ma ko dah͈a muka.
Cha bes i h͈ewte bu rey bu muje ba, Yesu tah͈ou te h͈achu, ne, Su kena mare, na ñou fi man te nān.