25 Cha wah͈tu wōwale Yesu tontu, ne, Mangi la gerem, Bay bi, Borom’ asaman ak suf, ndege nuba nga yef yile chi borom‐h͈amh͈am yi ak borom‐sago yi, te fêñal len i gūne.
Yesu tontu ko, ne, Barkel chi you, Simon dōm i Jonah; ndege du yaram te du deret a la fêñal lōlu, wande suma Bay ba cha ajana.
Te ne ko, Ndah͈ dēga nga li ñile di wah͈? Yesu ne len, Wau: ndah͈ mosu len a janga, ne, Chi gemeñ’ i dōm ak i gūne yu di nampa nga motali nau?
Mōtah͈ ñu tegi doch wa. Te Yesu yēkati i but am, te ne, Bay bi, mangi la gerem ndege dēga nga ma.
Suma fit nah͈arlu na lēgi; te ana lu ma war a wah͈? Bay bi, musal ma chi wah͈tu wile? Wande lōlo tah͈ ma dika chi wah͈tu wile.
Bay bi, magalal sa tur. Bāt nak juge cha asaman, ne, Magal nā ko, te di nā ko magalati.