2 Ba John dēge chi tejukay ba i koutef i Krista, mu yōne cha i tālube am;
H͈êt ya yepa mbōk cha Ibrayuma be cha Dauda fuk’ i h͈êt la ak ñenent; te cha Dauda be cha ngaday ga fa Babylon fuk’ i h͈êt la ak ñenent; te cha ngaday ga fa Babylon be chi Krista fuk’ i h͈êt la ak ñenent.
Ndege Herod jap’ on na John, ewo ko, te tej ko chi kaso, ndig Herodias, jabar i Philip rak’ am.
Ba mu dēge nak ne tej nañu John, mu dem cha Galilee;
Fōfale i tālube i John ñou fi mōm, ne, Lutah͈ ñu di faral a ôr, ak Pharisee ya, te sa i tālube du ñu ôr?
Ba Borom bi h͈ame nak ne Pharisee ya dēg’ on nañu ne Yesu angi don def te batise i talube yu gen a bare as John,