18 Ndege John ñouūl on di leka wala di nān, te ñu ne, Anda na ak jine.
Doy na chi tālube mu neka naka jemantalkat am, te jām naka borom am. Su ñu ôe borom‐ker ga Abdujambar, naka ña mōmu chi ker am!
Ne, Lītal nañu len, te fēchu len; yeremtu nañu, te joyu len.
John nak mō sol on nchangay i kouar i gelem, ak lah͈asay i der chi ndig am; te dundu am njērer la won, ak lem i ala.
Wande Pharisee ya ne, Chi bur i jine ya la gēne jine yi.
Te ñu bare chi ñom ne, Ame na jine, te telbataku; lutah͈ ngēn ko dēglu?
Mbōlo ma tontu, ne, Am nga jine: ana ku la ūt a rēy?
Yauod ya tontu te ne ko, Ndah͈ wah͈u ñu dega ne yā di wā’ Samaria, te ame jine?
Yauod ya ne ko, Da ñu h͈am lēgi ne ame nga jine. Ibrayuma dē na, ak yonent ya; te nga ne, Su kena dēnche suma bāt, du mos dē bel mos.