16 Wande ak lan la h͈êt wile niro? Niro na ak h͈alel ñu jēki chi i ndaje, di h͈āchu chi sēn i mās,
Ku am nopa yu mu dēge, na dēga.
Ne, Lītal nañu len, te fēchu len; yeremtu nañu, te joyu len.
E dōm i ñangor yi, yēn ñi bon, naka ngēn mune wah͈ lu bāh͈? ndege lu fês chi h͈ol gemeñ gi wah͈ ko.
Chi dega mangi len di wah͈, Yef yile yepa di nañu dal h͈êt wile.
Ak i noyo chi i ndaje, te nit di len ôe, Rabbi.
Chi dega mangi len di wah͈, H͈êt wile du wey be yef yile yepa am.