12 Cha jamāno i John Batisekat ba bentey, chi nchouarte la ñu fab ngur i ajana, te ña souar japa ko.
Chi dega mangi len di wah͈, Ku gen a rey John Batisekat ba jugêngul cha ña judu chi jigen; wande ka gen a tut chi ngur i ajana, mō ko gen a rey.
Ndege yonent ya yepa ak yōn wa yēgle on nañu be cha John.
Yesu tontu ko, ne, Bul ko bañ lēgi, ndege nōgu la ñu ela motali njūbay yepa. Nōgale la bañatul.
Bu len ligey ndig dūndu bu di sanku, wande ndig dūndu bu di deka be abada, ba len Dōm i nit ka di mayi: ndege mōm la Yalla Bay ba tan’ on.