Mā len di batise chi ndoh͈ ndig rēchu; wande mōm ka di topa chi man, mō ma gēti kantan; daganu ma yubu i dal’ am; mō len di batiseji chi Nh͈el mu Sela ma ak safara;
Ku mu mun a don mbōk ku di moy bena chi eble yile bu gen a tūt, te jemantal nit ña nogule, di nañu ko tūdeji ka gen a new ñepa chi ngur i ajana; wande ku len di def te jemantal len, di nañu ko tūdeji ku rey chi ngur i ajana.