Kan chi ñom ñar a def la sēn bay buga? Ñu ne ko, Tau ba. Yesu ne len, Chi dega mangi len di wah͈, Publican ya ak garbo ya di nañu dem chi ngur i Yalla as yēn.
Wande suboh͈un yēn, bindānkat yi ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn tej bunt’ i ngur i ajana chi nit: te yēn chi sēn bopa du len cha tabi; te nanguwu len ña buga tabi ñu tabi cha.
Kōkale ñou on na fi mōm chi gudi, te ne ko, Rabbi, h͈am nañu ne yā di jemantalkat ba bayako fa Yalla: ndege ken munul a def koutef yile nga def, su Yalla nekule ak mōm.