40 Ku len nangu, man la nangu; te ku ma nangu, nangu na ka ma yōni.
Ku nangu gena gūne niki gile chi suma tur, man la nangu:
Bur ba di na len tontu, ne, Chi dega mangi len di wah͈, Ndege def on ngēn ko chi kena chi suma i mboka yile ku gen a tūt, man ngēn ko defal on.
Di na len tontu, ne, Chi dega mangi len di wah͈, Ndege defu len ko won chi ku gen a tūt chi ñile, man ngēn ko defalul on.
Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Ku nangu ku neka ka ma yōni, man la nangu; te ku ma nangu, mōm ka ma yōni on la nangu.
Yesu nêti len, Jama and’ ak yēn: naka ma Bay ba yōni on, man it nōnu lā len yōni.
Ndah͈ ñepa mun a teral Dōm ji naka ñu terale Bay ba. Ku teralul Dōm ji teralul Bay ba ko yōni on.