37 Ku sopa bay am mbāte ndey am as man, daganul chi man; te ku sopa dōm am ju gōr, mbāte dōm am ju jigen as man, daganul chi man.
Mu ne ko, Na nga sopa Borom bi sa Yalla ak sa h͈ol bepa, ak sa fit wepa, ak sa nh͈el mepa.
Fōfale mu ne i ndau am, Nchēt li emba na, wande ña ma ô on motu ñu.
Ndah͈ ñepa mun a teral Dōm ji naka ñu terale Bay ba. Ku teralul Dōm ji teralul Bay ba ko yōni on.