36 Te i mbañ i nit a neka cha bir nēg am.
Mag di na jebal rak’ am ndah͈ mu dē, te bay dōm am: i dōm di nañu or sēn i bay ak sēn i ndey, te rēylu len.
Peter ne ko, Do rah͈as suma i tanka muka. Yesu tontu ko, ne, Su ma la rah͈asul, do am bena cher chi man.