3 Philip, ak Bartholomew; Thomas, ak Matthew publican bi; James dōm i Alphæus, ak Thaddæus;
Su len bañê dēga, wah͈ ko ndaje ma; te su bañê dēga ndaje ma itam, na neka chi you niki Gentile ak publican.
Chi sēn digante la Mariama Magdalene nek’ on, ak Mariama ndey i James ak Joses, ak ndey ī dōm i Zebedee.
Ba Yesu juge fōfale, mu gis nit ku tūda Matthew, mu di tōg cha galakukay ba: mu wah͈ ko, ne, Topa ma. Mu jog, te topa ko.
Nathanael ne ko, Ana fo ma h͈ame? Yesu tontu te ne ko, Ba la Philip ôangule, ba nga neke cha run mbot ga, gis nā la.
Thomas ku tuda sīh͈ bi, ne i morom i talube am ya, Na ñu dem itam, ndah͈ ñu dē ak mōm.
Judas ne ko, (dowul Iscariot), Borom bi, lu la jot be nga ñu di fêñu, te dowul chi aduna si?
Thomas ne ko, Borom bi, h͈amu ñu fo di dem; naka la ño h͈ame yōn wa?
Yesu ne ko, Ndah͈ neka nā ak yēn bu yāga, te h͈amangu la ma, Philip? Ka ma gis, Bay ba la gis; naka nga wah͈e, ne, Won ñu Bay ba?
Nek’ on nañu fōfa Simon Peter, ak Thomas ku tūda sīh͈ bi, ak Nathanael i Cana cha Galilee, ak i dōm i Zebedee, ak ñenen ñar i talube am.