22 Ñepa di nañu len sib ndig man; wande ku di muñ be cha muj ga mō di muchi.
Ku ūt dund’ am, di na ko rēr; te ku rēral dund’ am ngir man, di na ko gis.
Wande ka di muñ be cha muj ga, di na mucha.
Fōfale di nañu len jebale ndah͈ ñu geten len, te di nañu len rēy: h͈êt yi yepa di nañu len sib ndig man.
Barkel chi yēn su ñu len di h͈as, te geten len, te sos lu bon yepa chi yēn ndig man.
May nā len sa bāt; te aduna si bañ na len, ndege boku ñu chi aduna si, naka man itam boku ma chi aduna si.
Aduna si munul len a bañ; wande man la bañ, ndege sēde nā chi lu jem chi mōm ne i ligey am bon nañu.