18 Te di nañu len yubu chi kanam i kēlifa ak i bur ngir man, ndig sēde chi ñom ak chi Gentile ya.
Wande otu len nit, ndege di nañu len têwlo chi i ndaje, te ratah͈ len chi sēn i juma;
Wande su ñu len di têwlo, bu len jāh͈le naka mbāte lan ngēn di wah͈; ndege di nañu len may lu ngēn di wah͈ chi wah͈tu wōwale.
Yesu ne ko, Otul te bu ko wah͈ ken; wande demal wone sa bopa seriñ ba, te jebale maye ga Musa eble won, ndig sēde chi ñom.