Tah͈na yōne nā len i yonent, ak i borom‐sago, ak i h͈amkat: di ngēn rēy ñena ñi, te dāj len cha kura; te di ngēn ratah͈ ñena ñi chi sēn i juma, te geten len chi dek’ ak deka:
Wande mangi len di wah͈, Ku di mere morom am, mungi chi tafār i ate; te ku ne morom am, Dof bi, mungi chi tafār i ate bu rey; wande ku ne, Ēfar bi, di na neka chi tafār i safara’ nāri.