18 Njūdu’ Yesu Krista nile la won: Ba ndey am Mariama nangulante Yusufa, ba mu lāta sey ak mōm, fêñu on na ak bir chi Nh͈el mu Sela ma.
Tēre’ toflante i gir i Yesu Krista, dōm i Dauda, dōm i Ibrayuma.
Ba mu wah͈andô ak mbōlo ma, ndey am ak i rak’ am tah͈ou cha biti, di buga wah͈ ak mōm.
Ba ñu h͈arafe cha nēg ba, ñu feka gūne ga ak Mariama ndey am; ñu sūka te jāmu ko; ñu ūbi sēn i wah͈ande, te jebal ko i maye: wurus, fufata, ak mira.