12 Ganou ba ñu len yubu on fa Babylon, Jechoniah jur Shealtiel; Shealtiel jur Zerubbabel;
Te Josiah jur Jechoniah ak i dōm i bay am, cha jamāno ja ñu len gadaylo won fa Babylon:
Te Zerubbabel jur Abiud; Abiud jur Eliakim; Eliakim jur Azor;
H͈êt ya yepa mbōk cha Ibrayuma be cha Dauda fuk’ i h͈êt la ak ñenent; te cha Dauda be cha ngaday ga fa Babylon fuk’ i h͈êt la ak ñenent; te cha ngaday ga fa Babylon be chi Krista fuk’ i h͈êt la ak ñenent.