4 Ñu ne ko, Jemantalkat bi, fek’ on nañu jigen jile chi njālo, cha tah͈ouay ba.
Yusufa jekar am, nek’ on ku jūb, te nangôdi ndig wone ko chi biti, bug’ on na ko fase chi kumpa.
Te bindānkat ya ak Pharisee ya indi jigen ja ñu jap’ on chi njālo, te ba ñu ko tah͈ouale chi sēn diga,
Musa chi yōn wi ebal on na ñu jumat ko ak i doch ku mel ni mōm: you nak, ana lo wah͈ chi mōm?