3 Te bindānkat ya ak Pharisee ya indi jigen ja ñu jap’ on chi njālo, te ba ñu ko tah͈ouale chi sēn diga,
Ba mu dajale i njīt i seriñ ya ak i bindānkat nit ña, mu lāj len fu Krista war a jūdu.
Te nit ña ñepa dika fi mōm, te mu tōg te jemantal len.
Ñu ne ko, Jemantalkat bi, fek’ on nañu jigen jile chi njālo, cha tah͈ouay ba.
Te ñom, ba ñu ko dēge, ñu gēna bena bena, dôre ko cha mag ña be cha ka muje: te Yesu reka des, ak jigen ja fa mu nek’ on chi digante ba.
Ñu indi ko fa Pharisee ya ka jek’ on a silmah͈a.