2 Te nit ña ñepa dika fi mōm, te mu tōg te jemantal len.
Chi wah͈tu wōwale Yesu ne mbōlo ma, Dika ngēn jelsi ma ak i jāsi ak i doko, niki sachakat? Dan nā tōg ak yēn gir gu neka, di jemantale chi juma ja, te japu len ma won.
Yesu ne len, Suma dūndu mō di def mbugel i ka ma yōni on, te motali ligey am.
Yesu wah͈ on na bāt yile cha dēnchukay ba, ba mo jemantale cha juma ja: te ken japatu ko; ndege wah͈tu am ñouangul.
Te bindānkat ya ak Pharisee ya indi jigen ja ñu jap’ on chi njālo, te ba ñu ko tah͈ouale chi sēn diga,