Te ne ko, So de Dōm i Yalla, chipālul chi suf; ndege binda nañu, ne, Dēnka na la i malāk’ am, te di nañu la yubu chi sēn loh͈o, ndah͈ do fakatal sa tanka chi h͈êr.
Su ngēn di ôr, bu len am kanam gu dīs niki nafeh͈a ya; ndege di nañu ñaulo sēn i kanam ndah͈ nit ña gis ne ñunge ôr. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.
Su ngēn di ñān, bu len def niki nafeh͈a ya: ndege sopa naño tah͈ou di ñān chi juma ya ak chi mbeda ya, ndah͈ nit gis len. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.
Yesu tontu ko, ne, Man chi kanam i ñepa lā wah͈ on chi aduna si; dan nā jemantal cha juma ya, ak cha jangu ba fa Yauod ya dajale ñepa; te wah͈u ma won dara chi kumpa.