3 Mbok’ am ya ne ko nak, Gēnal file te dem cha Judea, ndah͈ sa i talube itam mun a gis sa koutef yi nga def.
Ba mu wah͈andô ak mbōlo ma, ndey am ak i rak’ am tah͈ou cha biti, di buga wah͈ ak mōm.
Ô on nañu itam Yesu ak i talube am cha sey ba.
Lu bare chi i talube am nak, ba ñu dēge lile, ne, Wah͈ jile dīs na; ku ko mun a dēga?
Ndig lile lu bare chi i talube am delu ganou, te andatu ñu ak mōm.
Wande ba i mbok’ am deme cha h͈ewte ga, mu dem fa itam, du chi kanam i ñepa, wande chi wētay.
Ndege ken deful lef chi kumpa, te mō buga ñu h͈am ko chi biti. So defe yef yile fêñal sa bopa chi aduna si.
Ndege i mbok’ am sah͈ gumu ñu on chi mōm.