3-4 Chi bir i mbōlo chi ñu op’ on, i silmah͈a, i lago, ak i lafañ teda fa.
Mbōlo mu rey ñou fi mōm, and’ ak ña lagi, silmah͈a, lu, tēlekat, ak ñenen ñu bare, nu teg len chi tank’ am, te mu weral len;
Dēgdēg i tur am dem cha bir Syria yepa; ñu yub ko nit ña op’ on ñepa, ña jangaro ju mun a don ak nchono jap’ on, ak ña i jine jap’ on, ak ña say, ak ña lafañ, te mu weral len.
Cha Jerusalem nak, cha bunt’ i nh͈ar ya, dēg anga fa won bu tūda Bethesda chi lak’ i Yauod ya, te am na jurom i bulu.