8 Ndege i talube am dem on nañu cha bir deka ba jendi dūndu.
Ô on nañu itam Yesu ak i talube am cha sey ba.
Fōfale i talube am ñou, te jomi ne ak jigen la don wah͈tānal; wande ken wah͈ul, ne, Lan nga ūt? mbāte, Lutah͈ nga wah͈tān ak mōm?
Te chi deka bōbale jopa chi wā’ Samaria ya gum on nañu chi mōm, ndig bāt i jigen ja sēde won, ne, Nitali na ma li ma def on yepa.
Mu agsi nak fa dek’ i Samaria bu tūda Sychar, bu jegeñ tōl ba Yanh͈oba may on Yusufa dōm am:
Bena jigen i Samaria ñou rôtsi ndoh͈. Yesu ne ko, May ma ma nān.