5 Mu agsi nak fa dek’ i Samaria bu tūda Sychar, bu jegeñ tōl ba Yanh͈oba may on Yusufa dōm am:
Ndah͈ yā gēti suñu bay Yanh͈oba, mi ñu may on tên bi, te mu nān cha, ak i dōm am, ak i nag am?
Te chi deka bōbale jopa chi wā’ Samaria ya gum on nañu chi mōm, ndig bāt i jigen ja sēde won, ne, Nitali na ma li ma def on yepa.
Te tên i Yanh͈oba anga fa won. Yesu nak don na lota cha tūkê’m, te tōg nōgule cha tên ba. Chi jurom ben’ i wah͈tu la potah͈.
Ndege i talube am dem on nañu cha bir deka ba jendi dūndu.