7 Bul jomi ndege da ma la wah͈, ne, Ela ngēn a jūduāt.
Yesu tontu te ne ko, Chi dega, chi dega, mangi la wah͈, Su nit jūduātule, du mun a gis ngur i Yalla.
Su ma len wah͈e yef i aduna, te gumu len, naka ngēn di gume su ma len wah͈e yef i ajana?
Bu len jomi chi lile: ndege wah͈tu di na ñou ba ña chi bamel ya ñepa di nañu dēga bāt am,
La jūdu chi yaram wi yaram la; te la jūdu chi Nh͈el ma nh͈el la.
Ngelou li gelou na fa mu buga, te dēga nga rir am, wande h͈amu la fu mu bayako, te fu mu jem: nōnule la ku neka ku jūdu chi Nh͈el ma.