John 3:2 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907
2 Kōkale ñou on na fi mōm chi gudi, te ne ko, Rabbi, h͈am nañu ne yā di jemantalkat ba bayako fa Yalla: ndege ken munul a def koutef yile nga def, su Yalla nekule ak mōm.
Ñu yōni fi mōm sēn i tālube ak ga’ Herod, ne, Jemantalkat bi, h͈am nañu ne yā di dega, di jemantale yōn i Yalla chi dega, te ragalu la ken, ndege sêtu la kanam i nit.
Ñena cha Pharisee ya ne nak, Nit kile dowul ku bayako fa Yalla, ndege du japa bes i Dimas ja. Wande ñenen ne, Naka la nit ku di bakarkat mun a defe mandarga yile? Te h͈ājalo jog na chi sēn digante.