1 Cha ñetel i fan ba, sey am on na cha Cana i Galilee; te ndey i Yesu anga fa won.
Ba mu wah͈andô ak mbōlo ma, ndey am ak i rak’ am tah͈ou cha biti, di buga wah͈ ak mōm.
Cha elek sa mu gis Yesu di ñou fi mōm, te ne, Sêt len, Mburtu’ Yalla mā’ngi, ka dindi bakar i aduna si!
Cha elek sa John tah͈ouati, ak ñar chi i talube am;
Cha elek sa bug’ on na dem cha Galilee, te mu gis Philip, te Yesu ne ko, Topa ma.
Mandarga bu jeka bile la Yesu def on cha Cana i Galilee, te wone ndam am; te i talube am gum chi mōm.
Nek’ on nañu fōfa Simon Peter, ak Thomas ku tūda sīh͈ bi, ak Nathanael i Cana cha Galilee, ak i dōm i Zebedee, ak ñenen ñar i talube am.
Mu ñouati nak cha Cana i Galilee, fa mu sopali won ndoh͈ ma biñ. Te bena kangam am on na, ka dōm am ju gōr opa cha Capernaum.