3 Te yef yile la ñu di defi, ndege h͈amu ñu Bay ba mbāte man.
Wande yef yile yepa la ñu di defi ndig suma tur, ndege h͈amu ñu ka ma yōni on.
Ku ma bañ, suma Bay la bañ itam.
Ey Bay bu jūb bi, aduna si h͈amul la won, wande mā la h͈am on; te ñile h͈am nañu ne yā ma yōni on.
Te dūnda gu dul jêh͈ a di gile, ndah͈ ñu h͈am la, you mi di Yalla ji dega dal, ak Yesu Krista ki nga yōnesi won.
Ñu ne ko, Ana sa Bay? Yesu tontu, ne, H͈amu len ma, te h͈amu len suma Bay: su ngēn ma h͈am on, h͈am kon ngēn suma Bay itam.
Te h͈amu len ko; wande mā ko h͈am: te su ma ne, H͈amu ma ko, kōn mā di fenkat na yēn: wande h͈am nā ko, te dēncha nā bāt am.