Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -




John 13:1 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Ba h͈ewte i njot ga lāta jot, Yesu ka h͈am ne wah͈tu am dikasi na ba mo di bayi aduna si dem fa Bay ba, naka mu sope won yos am ña neka chi aduna si, mu sopa len be cha muj ga.

Faic an caibideil Dèan lethbhreac




John 13:1
44 Iomraidhean Croise  

Fōfale mu ñou fi tālube ya, te ne len, Nelou len lēgi, te nopalaku: wah͈tu wi jegeñsi na, te or nañu Dōm i nit ka chi loh͈o i bakarkat ya.


Di len jemantal ñu di dēncha lu mu mun a don lu ma len ebal on: te mangi neka ak yēn sā su neka, be cha muj i aduna. UNWIN BROTHERS, LIMITED, THE GRESHAM PRESS, WOKING AND LONDON.


H͈ewte i Yauod ya jegeñsi na; te ñu bare juge cha deka ya, dem cha Jerusalem ba h͈ewte ga lāta jot, ndah͈ ñu setal sēn bopa.


Te Yesu tontu len, ne, Wah͈tu wi jot na be ba Dōm i nit ka di ami ndam.


Ndege ñena dēfe on nañu, ne naka Judas ame won mbus ma, Yesu nôn ko, Jendal lu ñu soh͈la chi h͈ewte gi; mbāte mu sarah͈ miskin yi.


Yesu ka h͈am ne Bay ba joh͈ na yef yepa chi i loh͈o am, te juge won na cha Yalla, te di na dem fa Yalla,


Eble bu ês lā len di joh͈, ndah͈ ngēn sopante; naka ma len sope sah͈ yēn itam na ngēn sopante.


Dēg’ on ngēn naka ma len wah͈ on, ne, Di nā dem, te di nā delusêti fi yēn. Su ngēn ma sop’ on, don ngēn banēh͈uji, ndege di nā dem fa Bay ba: ndege Bay ba gen na rey as man.


Wande ndah͈ aduna si h͈am ne sopa nā Bay ba, te naka ma Bay ba joh͈e won eble, nōgule lā def. Jog len, na ñu dem cha kanam.


Da ma juge won fa Bay ba, te ñou chi aduna si: te di nā bayiati aduna si, te dem fa Bay ba.


Yef yōyu Yesu wah͈ on: te yēkati i but am cha asaman, te ne, Bay bi, wah͈tu wa jot na; na nga may sa Dōm ndam, ndah͈ Dōm ji itam jebal la ndam:


Boku ñu chi aduna si, naka ma bokule chi aduna si.


Te h͈amlo won nā len sa tur, ti di nā ko h͈amlôti; ndah͈ nchofel gi nga ma sope won neka chi ñom, te man chi ñom.


Ey Bay bi, na nga ma may ndam lēgi ak sa bopa, ndam la ma am on ak you ba aduna si sosôngul.


Yesu ka h͈am yef ya ko di jot yepa, dem cha kanam, te ne len, Ana ku ngēn di ūt?


Ganou lōlu, Yesu ba mu h͈ame ne yepa soti na, ndah͈ mbinda ma motaliku, mu ne, Mar nā.


Te h͈ewte i Yauod ya jegeñsi na, te Yesu dem fa Jerusalem.


Te bena h͈ewte i Yauod ya jegeñsi na.


Ñu di ko ūt a japa nak; wande ken tegul loh͈o chi kou am, ndege wah͈tu am jotangul.


Yesu ne len, Suma wah͈tu jotangul; wande sēn wah͈tu sā su neka la.


Yesu wah͈ on na bāt yile cha dēnchukay ba, ba mo jemantale cha juma ja: te ken japatu ko; ndege wah͈tu am ñouangul.


Lean sinn:

Sanasan


Sanasan