3 Mariama nak indi bena libar i h͈êñh͈êñ bu jafe njēg lol, te diw ko cha i tank’ i Yesu, te fomp’ i tank’ am ak kouar am; be nēg ba fês ak h͈et i h͈êñh͈êñ ga.
Te kile di Mariama ma diw on Borom bi ak h͈êñh͈êñ, te fomp’ i tank’ am ak kouar am, ku chameñ am Lazarus jēr on.
Ganou ba mu wah͈e lōlu, mu dem te ô Mariama rak’ am chi kumpa, ne, Borom ba’ngi fi, te mungi la ô.
Ba Mariama agse fa Yesu nek’ on, te gis ko, mu dānu chi i tank’ am, ne ko, Borom bi, so fi nek’ on, suma chameñ dowul kōn dēi.
Te Nicodemus ñou itam, ka jek’ on a dika fa mōm chi gudi, te mu indi mira ak h͈êñay ya ñu bōle won; tēmēr i libar la potah͈.