Pilate ne ko, Ndah͈ bur nga? Yesu tontu, ne, Wah͈ nga ko, ndege man bur la. Lile tah͈ ma jūdu on, te lile tah͈ ma ñou chi aduna si, ndah͈ ma sēde dega gi. Ku neka ku boka chi dega gi di na dēga suma bāt.
Ka am seyt ba borom‐seyt ba la; wande h͈arit i borom‐seyt ba, ka tah͈ou te dēga ko, mō banēh͈u bu bare ndig bāt i borom‐seyt ba: suma banēh͈ bile mbōk motaliku.