16 Ndege chi fêsay am la ñu nangu on ñepa, ak yiw chi kou yiw.
Ndege kōka Yalla yōni on, bāt i Yalla yi la wah͈: ndege joh͈ewul Nh͈el ma chi natu.
Ndege ka am mōm la ño may, te di na am lu bare; wande ka amul, di nañu jel la mu am sah͈.
Wande John bañ ko, ne, Mā soh͈la batise fi you; te yangi ñou fi man?
Mā len di batise chi ndoh͈ ndig rēchu; wande mōm ka di topa chi man, mō ma gēti kantan; daganu ma yubu i dal’ am; mō len di batiseji chi Nh͈el mu Sela ma ak safara;