12 Wande ña ko nangu on, ñom la may on sañsañ ñu neka i dōm i Yalla, ña gum chi tur am:
Ku len nangu, man la nangu; te ku ma nangu, nangu na ka ma yōni.
Te chi tur am la Gentile ya di yākari.
Ku nangu gena gūne niki gile chi suma tur, man la nangu:
Ñou on na fi yos am, te yos am nanguwu ñu ko won.
Kile sah͈ ñou on na ndig sēde, ndah͈ mu sēde chi lêr gi, ndah͈ ñepa mun a gum chi mōm.
Te du ngir h͈êt wi reka, wande ndah͈ mu mun a dajale chi bena dōm i Yalla ña tasāro won fu neka.
Ba mu neke cha Jerusalem cha h͈ewte i njot ga, ñu bare gum on nañu chi tur am, ba ñu gise koutef ya mu def on.
Wande yile la ñu bind’ on ndah͈ ngēn gum ne Yesu mō di Krista, Dōm i Yalla; te naka ngēn gume, mun ngēn ami dūnda chi tur am.
Ku gum chi mōm atewu ñu ko; ku gumul, ate nañu ko jēg, ndege gumul on chi tur i Dōm i Yalla ja di bajo.