11 Ñou on na fi yos am, te yos am nanguwu ñu ko won.
Wande mu tontu, ne, Fi nh͈ar i nēg i Israel yu rēr yi reka la ñu ma yōni.
Nek’ on na chi aduna si, te chi mōm la aduna si saku on, te aduna si h͈amu ko won.
Wande ña ko nangu on, ñom la may on sañsañ ñu neka i dōm i Yalla, ña gum chi tur am:
Cha ganou mu ne talube ba, Sêtal, sa ndey angile! Te cha wah͈tu wōwale talube ba jel ko cha ker i bop’ am.
La mu gis te dēga, lōlu la sēde; te ken nanguwul sēde am.