10 Nek’ on na chi aduna si, te chi mōm la aduna si saku on, te aduna si h͈amu ko won.
Suma Bay jebal na ma yef yepa; te ken h͈amul Dōm ji wande Bay bi; te ken h͈amul Bay bi wande Dōm ji, ak ku Dōm ji nangu mu h͈am ko.
Ñou on na fi yos am, te yos am nanguwu ñu ko won.
Ken mosul a gis Yalla muk; Dōm am ja di bajo, ka neka chi den’ i Bay ba, mō ko fêñal.
Lu neka chi mōm la saku on; te ganou mōm dara sakuwul on cha la saku on.
Te lêr gi melah͈ chi lendem gi, te lendem gi sēnu ko won.
Ey Bay bu jūb bi, aduna si h͈amul la won, wande mā la h͈am on; te ñile h͈am nañu ne yā ma yōni on.
Wande Yesu tontu len, ne, Suma Bay angi ligey bentey, te man itam mangi ligey.