1 Cha chosan la Bāt ba am on na, te Bāt ba nek’ on na ak Yalla, te Bāt ba nek’ on na Yalla.
H͈ēk ba di na bir, te jur dōm ju gōr, te di nañu ko tūde Emmanuel; mu tiki, Yalla and’ ak ñun.
Te Bāt bi yaramu on na, te dek’ on na ak ñun, te sêt on nañu ndam am, ndam niki ku di dōm i bay ju di bajo, fês ak yiw ak dega.
Ken mosul a gis Yalla muk; Dōm am ja di bajo, ka neka chi den’ i Bay ba, mō ko fêñal.
Kile mō nek’ on cha chosan la ak Yalla.
Da ma juge won fa Bay ba, te ñou chi aduna si: te di nā bayiati aduna si, te dem fa Bay ba.
Ey Bay bi, na nga ma may ndam lēgi ak sa bopa, ndam la ma am on ak you ba aduna si sosôngul.
Thomas tontu te ne ko, Suma Borom ak suma Yalla.
Yesu ne len, Chi dega, chi dega, ma ne len, Ba Ibrayuma jūdôngul, mā am.