Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

Matthew 9 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Yesu duga chi gāl, jala, te ñou chi dek’ am.

2 Ñu yub ko nit ku lafañ, teda chi lal: ba Yesu gise sēn ngum, mu wah͈ ku lafañ ka, ne, Suma dōm, na sa h͈ol dal; baal nañu la sa i bakar.

3 Ñena cha bindānkat ya ne chi sēn h͈ol, Nit kile tedadil na Yalla.

4 Yesu h͈am sēn i h͈alāt, te ne len, Lutah͈ ngēn di h͈alāt lu bon chi sēn i h͈ol?

5 Lan a chi gen a yomba wah͈, ne, Baal nañu la sa i bakar; wala ne, Jogal, te doh͈?

6 Wande ndah͈ ngēn mun a h͈am ne Dōm i nit ka am na chi suf sañsañ di baale i bakar, (fōfale mu ne ku lafañ ka,) Jogal, gadul sa lal te dem chi sa ker.

7 Mu jog, te dem cha ker am.

8 Wande ba mbōlo ma gise lōla, ñu ragal, te magal Yalla, ki may nit gōgu kantan.

9 Ba Yesu juge fōfale, mu gis nit ku tūda Matthew, mu di tōg cha galakukay ba: mu wah͈ ko, ne, Topa ma. Mu jog, te topa ko.

10 Am on na, ba Yesu tōge di leka cha nēg ba, publican yu bare ak i bakarkat ñou, te tōg ak mōm ak tālube am ya.

11 Ba Pharisee ya gise lōla, ñu ne i tālube am, Lutah͈ sēn Borom di leka ak i publican ak i bakarkat?

12 Wande ba mu ko dēge, mu ne len, Ña wer soh͈laū ñu fajkat, wande ña opa.

13 Wande dem len te jemantu lu lile tiki, Yermande lā buga as h͈arfan: ndege diku ma ô ñu jūb ña, wande i bakarkat.

14 Fōfale i tālube i John ñou fi mōm, ne, Lutah͈ ñu di faral a ôr, ak Pharisee ya, te sa i tālube du ñu ôr?

15 Yesu ne len, I mbok’ i nēg i borom‐chēt ga, ndah͈ mun naño nah͈arlu ba borom‐chēt ga neke ak ñom? Wande jamāno di na diki ba ño fabi borom‐chēt ga cha ñom; bōbale di nañu ôri.

16 Ken du dāh͈e nchangay lu maget ak lu deger, ndege la ñu jel dāh͈e ko di na h͈oti nchangay la, te h͈otiku ba di na gen a rey.

17 Du ñu def itam biñ bu ês chi mbūs yu maget: wala mbūs ya h͈ar, biñ ba tūru, te mbūs ya yah͈u: wande di nañu def biñ bu ês chi mbūs yu ês, te ñar ña dēnchu.

18 Ba mu len wah͈andô yef yile, bena kēlifa ñou, te dagān ko, ne, Nistey suma dōm ju jigen dē na; wande ñoual, teg sa loh͈o chi kou am, te di na dundati.

19 Yesu jog, ak i tālube am, te topa ko.

20 Jena jigen, ku am on h͈up i deret fuk’ i at ak ñar, ñou chi ganou am, te lāl mbichirān i mbūba’m:

21 Ndege wah͈ na chi h͈ol am, ne, Su ma lāle mbūba’m reka, di nā wer.

22 Wande Yesu woñaku, te ba mu ko gise, mu ne, Dōm ju jigen ji, na sa h͈ol dal; sa ngum weral na la. Jigen ja dal di wer cha wah͈tu wōwale.

23 Ba Yesu ñoue chi bir nēg i kēlifa ba, te gis lītkat ya ak nit ña di jāle,

24 Mu ne len, May len ma yōn: ndege janh͈a bi dēul, wande defa nelou. Ñu rê ko bu jēpi.

25 Wande ba ñu gēnê mbōlo ma, mu h͈araf cha bir, te japa loh͈o am: janh͈a ba jog.

26 Dēgdēg am dem cha bir rew mōma yepa.

27 Ba fa Yesu juge, ñar i silmah͈a topa ko, di h͈āchu, ne, Amal yermande chi ñun, you dōm i Dauda.

28 Ba mu ñoue chi bir nēg ba, silmah͈a ya ñou fi mōm: Yesu ne len, Gum ngēn ne mun nā def lile? Ñu ne ko, Wau, Borom bi.

29 Fōfale mu lāl sēn i but, ne, Naka sēn ngum na ame nōgu chi yēn.

30 Sēn i but ūbiku. Yesu artu len bu bāh͈ ne, Otu len bu ko kena yēg.

31 Wande ba ñu fa juge, ñu ēne tur am chi rew mōma yepa.

32 Ba ñu gēne, ñu yub ko nit ku lū, ka jine jap’ on.

33 Ba mu gēnê jine ja, lū ba wah͈: mbōlo ma jomi, ne, Mosu ñu ko gise nile chi Israel.

34 Wande Pharisee ya ne, Chi bur i jine ya la gēne jine yi.

35 Yesu dem cha rew ya ak deka ya yepa, di jemantale chi sēn i juma, wāre linjil i ngur gi, te weral ña opa ñepa, ak jarak ju neka chi digante nit ña.

36 Wande ba mu gise mbōlo ma, mu yerem len, ndege da ñu jāh͈le, te tasāro niki nh͈ar yu amul samakat.

37 Fōfale mu wah͈ i tālube am, ne, Chi dega ngōbte gi fūs na, wande ligeykat yi new nañu;

38 Mōtah͈ ñān len Borom i ngōbte gi, ndah͈ mu yōni i ligeykat chi ngōb am.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan