Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

Matthew 8 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Ba mu wache cha tūnda wa, mbōlo mu rey top’ on nañu ko.

2 Ab gāna ñou fi mōm, te ñān ko, ne, Borom bi, su la nêh͈e, mun nga ma setal.

3 Yesu talal loh͈o am, te lāl ko, ne, Di nā tah͈ nga set. Chi tah͈ouay ba mu dal di wer.

4 Yesu ne ko, Otul te bu ko wah͈ ken; wande demal wone sa bopa seriñ ba, te jebale maye ga Musa eble won, ndig sēde chi ñom.

5 Ba Yesu h͈arafe chi Capernaum, bena saltige ñou fi mōm, te dagān ko,

6 Ne, Borom bi, suma bukanēg anga teda cha ker, lafañ, te sona bu miti.

7 Yesu ne ko, Di nā dika te weral ko.

8 Saltige ba tontu ko ne, Borom bi, daganu ma nga h͈araf chi suma nēg; wande wah͈al bāt bi reka, te suma bukanēg di na wer.

9 Ndege nit lā ku neka chi run i kēlifa, te am nā i h͈arekat ya ma ēlif; te ku ma cha ne, Demal, mu dem; te ku ma cha ne, Ñoual, mu ñou; suma jām, Defal lile, mu def ko.

10 Ba ko Yesu dēge, mu jomi, te ne ña ko top’ on, Chi dega mangi len di wah͈, mosu ma feka ngum gu nu day, dēt, du chi Israel.

11 Te ma ne len, ñu bare di nañu jugeji cha Penku ak H͈arfu, te jēki ak Ibrayuma ak Isaka ak Yanh͈oba chi ngur i ajana;

12 Wande i dōm i ngur ga, di nañu len tabal chi lendem i biti; fōfale la joy di neka ak yeyi buñ.

13 Yesu ne saltige ba, Demal sa yōn, naka nga gume, na ame nōgu chi you. Bukanēg am dal di wer cha wah͈tu wōwale.

14 Ba Yesu h͈arafe chi nēg i Peter, mu gis goro am teda, opa ak fēbar.

15 Mu lāl loh͈o am, te fēbar ba bayi ko; mu jog te bukanēgu ko.

16 Ba ngon jote, ñu yub ko ña i jine jap’ on, te mu gēne malāka yu bon ya chi ñom chi bāt am, te weral ña jēr on ñepa:

17 Ndah͈ la Isaiah yonent ba wah͈ on motaliku, ne, Mō jel on suñu munadi, te yubu on suñu i jangaro.

18 Yesu nak ba mu gise mbōlo mu rey chi kanam am, mu eble ñu jala cha genen wet ga.

19 Bena bindānkat ñou, ne ko, Jemantalkat bi, di nā la topa fo mun a dem.

20 Yesu ne ko, Ntila yi am nañu i mpah͈, te mpich’ i asaman si am nañu i taga, wande Dōm i nit ka amul fu mu tedal bop’ am.

21 Kenen chi tālube ya ne ko, Borom bi, bayi ma ma jeka dem te sūl suma bay.

22 Wande Yesu ne ko, Topa ma, te bayi ñu dēle ña ñu sūl sēn ñu dē.

23 Ba mu duge chi gāl, i tālube am topa ko.

24 Ngelou lu rey jog cha gēch ga, be gāl ga muro ak dūs ya; wande mu don nelou.

25 Ñu ñou fi mōm, te ê ko, ne, Borom bi, musal ñu: ñunge sanku.

26 Mu ne len, Lutah͈ ngēn ragal, yēn nit i ngum gu new? Fōfale mu jog, te eda ngelou ya ak gēch ga; mu dal be ne nem.

27 Nit ña jomi, ne, Ban melin i nit a di kile, be ngelou li sah͈ ak gēch gi di ko dēgal!

28 Ba mu age cha genen wet, chi bir rew i Gadarene ya, ñar i nit ñu i jine jap’ on feka ko, di juge cha bamel ya, te ñu soh͈or lol, be ken munul a jār yōn wōwale.

29 Ñu h͈āchu, ne, Lan la ñu jote ak you, you Dōm i Yalla? Dā fi dika ndig geten ñu bala wah͈tu wa jot?

30 Gēt’ i mbām yu bare sorey on nañu fale di far.

31 Te jine ya dagān ko, ne, So ñu gēnê, bayi ñu ñu dem chi bir gēt’ i mbām ya.

32 Mu ne len, Dem len. Ñu gēna cha nit ña, te duga chi mbām ya: gēta ga yepa dou ak dōle chi kou bereb bu koue di jem chi gēch ga, ñu rēr chi ndoh͈ ma.

33 Ña len don sama dou, dem chi bir deka ba, te wah͈ lu neka, ak lu jot nit ña jine jap’ on.

34 Deka ba yepa gēna gatanduji Yesu; te ba ñu ko gise, ñu dagān ko mu gēna chi sēn rew.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan