Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

Matthew 7 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Bu len di ate, ndah͈ kena du len ateji.

2 Ndege ate bu ngēn ate ñenen, di nañu len ko ateji; te natu bu ngēn di natale, mōm sah͈ la ñu len di nataleji.

3 Lu elal nga di nimeku felah͈ bi chi sa but i morom, te do gis lā bi chi sa but?

4 Wala naka nga wah͈e sa morom, ne, Bayi ma ma dindi felah͈ bi chi sa but, te lā’ngi chi sa but sah͈?

5 Mīkar bi, dindil jeka lā bi chi sa but, te ganou ga di nga gis bu set ndah͈ nga mun a dindi felah͈ ba chi sa but i morom.

6 Bu len joh͈ la sela h͈aj ya, te bu len sani sēn i takay chi kanam i mbām; ndig so otuwul di nañu len degat chi sēn run tanka, te walbataku h͈oti len.

7 Lāj len, te di nañu len may; ūt len, te di ngēn gis; foga len, te di nañu len ūbi:

8 Ndege ku mu mun a don ku lāj, di na am; te ku ūt, di na gis; te ku foga, di nañu ko ūbi.

9 Kan chi yēn, su ko dōm am lāje mburu, mu may ko doch?

10 Wala su ko lāje jen, mu may ko jān?

11 Yēn ñi bon nak, su ngēn h͈ame may sēn i dōm yef yu bāh͈, as sēn Bay ba cha ajana di na may ña ko lāj yef yu bāh͈?

12 Mōtah͈ lu ngēn buga lepa nit di len ko defal, yēn itam na ngēn ela defal ñenen: ndege bile di yōn wi ak yonent ya.

13 H͈araf len chi bunta bu h͈ocha ba: ndege bunta ba yā na, te yōn wa jublu chi sankute yātu na, te bare na ñu cha tabi:

14 Ndege bunta ba h͈ocha na, te yōn wa jublu chi dunda h͈at na, te ñu new a ko gis.

15 Otu len i yonent i nafeh͈a ya, di ñou fi yēn chi nchangay i nh͈ar, wande chi bir ño di buki yu fuh͈ale.

16 Di ngēn len h͈am chi sēn i mēñef. Ndah͈ nit di na dajale i dōm i garap i biñ chi i dek, mbāt i sōto chi i h͈āh͈am?

17 Nōgu itam garap gu bāh͈ gu neka di na mēña mēñef bu bāh͈; wande garap gu bon di na mēña mēñef bu bon.

18 Garap gu bāh͈ munul a mēña mēñef bu bon, te garap gu bon munul a mēña mēñef bu bāh͈.

19 Garap gu neka gu mēñul mēñef bu bāh͈, di nañu ko gor, te sani ko chi safara.

20 Di ngēn len h͈am mbōk chi sēn i mēñef.

21 Du ku neka ku ma wah, ne, Borom bi, Borom bi, di na h͈araf chi ngur i ajana; wande ka def suma mbugel i Bay ba cha ajana mōm reka.

22 Ñu bare di nañu ma wah͈ chi bes bōbale, Borom bi, Borom bi, ndah͈ wareū ñu on chi sa tur, te chi sa tur ñu dah͈’ i jine, te chi sa tur ñu def koutef yu bare?

23 Fōfale di nā len yēgal, ne, Mosu ma len a h͈am; randu len ma, yēn ña def lu bon.

24 Mōtah͈ ku mu mun a don ku dēga suma i bāt yile, te def len, di na niro ak nit i sago, ka tabah͈ nēg am chi kou doch:

25 Tou ba dal, wame wa buna, ngelou la ñou, te dal chi kou nēg bōbale; wande dānuwul; ndege chi doch la sampu.

26 Te ku mu mun a don ku dēga suma i bāt yile, te defu len, di na niro ak nit ku ñaka sago, ka tabah͈ nēg am chi kou banh͈aleñ:

27 Tou ba dal, wame wa buna, ngelou la ñou, te dal chi kou nēg bōbale; mu maba; maba gu rey.

28 Am on na ba Yesu sotale bāt yile, mbōlo ma jomi chi njemantal am:

29 Ndege jemantal on na len naka ku am sañsañ, te nekul naka sēn i bindānkat.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan