Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

Matthew 27 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Ba lelek sa jote, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñepa fēnchu Yesu, ndah͈ ñu rēy ko.

2 Ñu ew ko, omat ko, te jebal ko Pilate kēlifa ga.

3 Fōfale Judas, ka ko or on, ba mu gise ne ey nañu ko, mu rēchu, te indêti ñeta fuk’ i dogit i h͈ālis chi i njīt i seriñ ya ak mag ya, ne,

4 Da ma bakar chi niki ma ore deret i ku set ka. Wande ñu ne, Lu ñu soh͈al chi lōla? Sêtal sa bopa.

5 Mu sani dogit i h͈alis ya chi suf chi juma ja, gēna, te dem, eng̈a bop’ am.

6 I njīt i seriñ ya jel dogit i h͈alis ya, ne, Daganul ñu def ko chi dēnchukay bu sela bi, ndege njēg i deret la.

7 Ñu fēncho, te jende h͈ālis ba tōl i ku dan tabah͈ i ndā, ndah͈ ñu di fa sūl i doh͈andem.

8 Mōtah͈ ñu tūde tōl bōba, Tōl i deret bentey.

9 Fōfale lu Jeremiah yonent ba wah͈ on motaliku, ne, Fab on nañu ñeta fuk’ i dogit i h͈ālis, njēg i ka ñu ap’ on, ka ñena chi dōm i Israel ya ap’ on,

10 Te joh͈ len ko tōl i ku dan tabah͈ i ndā, naka ma ko Borom bi eble won.

11 Yesu tah͈ou chi kanam i kēlifa ga, te kēlifa ga lāj ko, ne, Ndah͈ yā di Bur i Yauod ya? Yesu ne ko, Wah͈ nga ko.

12 Ba ko i njīt i seriñ ya ak mag ya jêñe, tontuwul dara.

13 Mōtah͈ Pilate ne ko, Dēgu la yef yi ñu la sēdêl?

14 Tontuwu ko dara, du bena bāt sah͈; tah͈na kēlifa ga jomi lol.

15 Chi h͈ewte ga nak, kēlifa ga dan na bayi cha mbōlo ma kena cha ña ñu tej on, ku ñu buga.

16 Am on nañu chi wah͈tu wōwale sachakat bu dēgu on, ku tūda Barabbas.

17 Ba ñu dajalô, Pilate ne len, Kan ngēn buga ma joh͈ len? Barabbas, am Yesu ki tūda Krista?

18 Ndege h͈am on na ne ndig kañān la ñu ko jebale.

19 Ba mu tōge chi ateukay ba, jabar am yōni fi mōm, ne, Bul bōlo chi yef i kōku nit ku jūb; ndege da ma yēg yef yu bare bes bile chi gēnta ndig mōm.

20 I njīt i seriñ ya nak ak mag ya digal mbōlo ma ñu lāj Barabbas, te rēylu Yesu.

21 Wande kēlifa ga tontu len, ne, Kan chi ñar ñi ngēn buga ma joh͈ len? Ñu ne, Barabbas.

22 Pilate ne len, Lan lā ela def mbōk ak Yesu ki tūda Krista? Ñepa ne, Na ñu ko dāj chi kura.

23 Kēlifa ga ne, Lutah͈, lan lu bon la def? Wande ñu h͈āchu bu bāh͈, ne, Na ñu ko dāj chi kura.

24 Ba Pilate gise ne munul dara, wande nchōu anga buga jog, mu jel ndoh͈ te rah͈as i loh͈o am chi kanam mbōlo ma, ne, Man mūmin lā chi deret i nit ku jūb kile: na ngēn ko sêt.

25 Nit ña ñepa tontu, ne, Na deret am dal chi suñu kou ak chi suñu kou i dōm.

26 Tah͈na mu joh͈ len Barabbas; wande Yesu mu ratah͈ ko, te jebale ko ndah͈ ñu dāj ko chi kura ba.

27 Fōfale i h͈arekat i kēlifa ga yubu Yesu chi ker i ate ga, te dajale fi mōm sēn i morom yepa.

28 Ñu ñōri ko, te solal ko chol gu h͈onh͈a.

29 Ñu lēta mbah͈ana i dek, te teg ko chi bop’ am, ak sonka chi ndējor am; ñu sūka chi kanam am, te ñaual ko, ne, Jamom, Bur i Yauod ya!

30 Nu tufli ko; jel sonka ba, te dōr ko chi bop’ am.

31 Ba ñu ko ñauale, ñu ñōri ko, solal ko chol am, te omat ko ndah͈ ñu dāj ko cha kura ba.

32 Ba ñu gēne, ñu feka wā’ Cyrene ku tuda Simon: mōm la ñu jeñtal mu and’ ak ñom ndah͈ mu gadu kura ba.

33 Ba ñu dike fa bereb bu tuda Golgotha, lu tiki ne, Bereb i h͈ot i bopa,

34 Ñu joh͈ ko biñ bu ñu bōle ak weh͈tan ndah͈ mu nān: ba mu ko mose, mu bañ a nān.

35 Ba ñu ko dāje cha kura ba, ñu sedo chol am chi sēn bopa, di wuri:

36 Ñu tōg, di ko otu fōfale.

37 Ñu teg chi kou bop’ am njêñ am, ba ñu bind’ on nile: Kile di Yesu Bur i Yauod ya.

38 Fōfale ñu dājāle cha i kura itam ñar i sachakat, kena chi ndējor am, ak kenen chi chamoñ am.

39 Ña fa romba sāga ko, di yengal sēn i bopa, ne,

40 You mi dānel jama ja te tabah͈ati ko chi ñet’ i fan, musalal sa bopa. So de Dōm i Yalla, wachal chi kura bi.

41 I njīt i seriñ ya itam, ak bindānkat ya ak mag ya ñaual ko, ne,

42 Musal na ñenen; munul a musal bop’ am. Mō di Bur i Israel: na wacha lēgi chi kura bi, te di nañu ko gum.

43 Mu ōlu Yalla; na ko musal lēgi, su ko buge; ndege nôn na, Mā di Dōm i Yalla.

44 Sachakat ya itam, ña ñu dājāle won chi kura ya, ñu h͈as ko nōga.

45 Cha fuk’ i wah͈tu ak ñar nak be cha ñet’ i wah͈tu, lendem neka chi kou suf si yepa.

46 Chi ñet’ i wah͈tu potah͈, Yesu h͈āchu be cha kou, ne, Eli, Eli, lama sabachthani? mu tiki ne, Yalla man, Yalla man, lutah͈ nga wocha ma?

47 Ñena ñu tah͈ou fa, ba ñu dēge lōla, ne, Ki nit ange ô Elijah.

48 Nōn’ ak nōna kena chi ñom dou, jel ab sponge, fêsal ko binegar, def ko chi sonka, te joh͈ ko mu nān.

49 Ña cha des ne, Bayi ko; na ñu gis su Elijah di ñou musal ko.

50 Yesu h͈āchôti be cha kou, te tago fit am.

51 Ser i juma ja h͈otiku chi diga, cha kou be chi suf; suf si yengatu; doch yu rey ya h͈ar;

52 Bamel ya ūbeku; te i yaram i jūlit yu bare ñu don nelou jog;

53 Gēna chi bamel ya ganou ndēkite am, h͈araf chi bir deka bu sela ba, te fêñu i nit jupa.

54 Saltige ba nak, ak ña nek’ on ak mōm, di otu Yesu, ba ñu gise yengatu’ suf sa, ak yef ya am, ñu tīt lol, ne, Chi dega kile Dōm i Yalla la.

55 Jigen yu bare tah͈ou fu sorey di sêt, ñu top’ on Yesu cha Galilee di ko bukanēgu:

56 Chi sēn digante la Mariama Magdalene nek’ on, ak Mariama ndey i James ak Joses, ak ndey ī dōm i Zebedee.

57 Ba ngon jote, borom‐alal ku juge on Arimathæa, ka tūda Yusufa, te nek’ on itam tālube i Yesu:

58 Kile dem fa Pilate te dagān yaram i Yesu. Fōfale Pilate eble ñu joh͈ ko ko.

59 Yusufa jel yaram wa, lomas ko chi ser wu set te wêh͈,

60 Te teral ko chi bamel am bu ês, ba mu et’ on chi h͈êr: mu borong doch wu rey chi bunt’ i bamel ba, te dem.

61 Mariama Magdalene ak menen Mariama ma neka fa, di tōg fu jegeñ bamel ba.

62 Cha lelek sa nak, bes ba topa bes i wājte ba, i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya dajalo fa Pilate,

63 Ne, Borom bi, Fataliku nañu ne nafeh͈a bōbale nôn na ba mu dund’ on, Chi ganou ñet’ i fan di nā dēki.

64 Ebalal mbōk ne ñu otu bamel ba be chi ñet’ i fan; wala h͈ēchna i tālube am di nañu dika sacha ko, te ne nit ña, Defa dēki cha ñu dē ña: kōn jūm gu muj ga di na gen a bon gu jeka ga.

65 Pilate ne len, Am ngēn i otukat: dem len, otu len ko lu ngēn mum.

66 Ñu dem, defar bamel ba bu bāh͈, kaste doch wa, te otukat ya neka ak ñom.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan