Matthew 24 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Yesu don na gēna cha juma ja, di dem yōn am; te i tālube am ñou fi mōm, di ko won i tabah͈ i juma ja. 2 Wande mu tontu len, ne, Sêtu len yef yile yepa? Chi dega mangi len di wah͈, Bena h͈êr du des chi kou morom am bu ñu dul dānel chi suf. 3 Ba mu tōge chi tūnda i Olive ya, tālube ya ñou fi mōm chi mpet, ne, Wah͈ ñu, kañ la yef yile di ami? te la di doi sa mandarga’ ndika, ak i muj i aduna si? 4 Yesu tontu len, ne, Otu len bu len kena nah͈. 5 Ndege ñu bare di nañu ñoui chi suma tur, ne, Mā di Krista, te di nañu nah͈i ñu bare. 6 Te di ngēn dēga i h͈are ak i h͈abar i h͈are: otu len ngēn jāh͈le: ndege yile soh͈la naño am; wande muj ga dikangul. 7 Ndege h͈êt di na jog chi kou h͈êt, ak ngur chi kou ngur: i h͈īf di nañu ami, ak i yengatu’ suf si chi bereb yu bare. 8 Wande yile yepa ndôrte i nah͈ar la. 9 Fōfale di nañu len jebale ndah͈ ñu geten len, te di nañu len rēy: h͈êt yi yepa di nañu len sib ndig man. 10 Fōfale ñu bare di nañu fakatalu, orante, te sibante. 11 Yonent i nafeh͈a yu bare di nañu jogi, te nah͈ ñu bare. 12 Te ndig bakar di na fūs, nchofel i ñu bare di na wañiku. 13 Wande ka di muñ be cha muj ga, di na mucha. 14 Bile linjil i ngur gi, di nañu ko wāre chi aduna si yepa ndig sēde chi h͈êt yi yepa; cha ganou ga muj ga di na ñou. 15 Bu ngēn di gisi suboh͈un ak h͈udosun mbōk mu di tah͈ou chi bereb bu sela ba, naka Daniel yonent ba wah͈ on (ka ko janga na h͈am), 16 Fōfale na ña neka chi Judæa dou cha tūnda ya: 17 Ku neka chi kou nēg, bu mu wacha mu gēne yef ya chi nēg am: 18 Te ku neka chi tōl am, bu mu delusêti jel yēre am. 19 Wande ndeysan jigen ña bir, ak ña di nampal chi bes yōgale! 20 Ñān len ndah͈ sēn dou du neka chi wah͈tu’ seda, wala chi bes i dimas: 21 Ndege chi wah͈tu wōwale, nah͈ar wu rey di na ami, naka mu mosulê am cha ndôrte’ aduna si bentey, dēt, te dōtu am bel mōs. 22 Su ñu gatalul on bes yōgale, ken du kon muchi: wande ngir ña ñu tana, di nañu gatal bes yōgale. 23 Fōfale su ñu len ne, Krista angile, mbāte mungale; bu len ko gum. 24 Ndege Krista yu nafeh͈a di nañu jogi, ak yonent yu nafeh͈a, te wone mandarga yu rey ak i koutef; be ñu di nah͈i ña ñu tana sah͈, su munê am. 25 Mangi len di yēgal bala wah͈tu wa jot. 26 Mōtah͈ su ñu len wah͈e, ne, Munga cha manding ma; bu len fa dem: munga chi bir nēg ya; bu len ko gum. 27 Ndege naka melah͈ ma jugê cha penku, te fêñu be cha h͈arfu, nōgu la ndika i Dōm i nit ka di mel. 28 Fu rēnda neka, fa la jah͈ay ya di dajalo. 29 Cha ganou nah͈ar i bes yōyale, nōn’ ak nōna janta bi di na lendem, wêr wi du joh͈e lêr am, bidiw yi di nañu dānu cha asaman, te i kantan i asaman si di nañu yengatu: 30 Fōfale mandarga i Dōm i nit ka di na fêñ cha asaman; h͈êt i aduna si yepa di nañu yeremtu, te di nañu gis Dōm i nit ka mu di ñou chi i nir i asaman si ak kantan ak ndam lu rey. 31 Te di na yōni malāka am ya ak nchōu i bufta bu rey, te di nañu dajale ña mu tan’ on chi ñenent i ngelou yi, cha bop’ i asaman be cha muj ga. 32 Dēglu len nak lēb i garap i sōto ga: ba banh͈as am mokase, te i h͈ob am suh͈ase, h͈am ngēn ne nauet jegeñsi na; 33 Nōgu itam su ngēn gise yef yile yepa, na ngēn h͈am ne jegeñsi na, be chi sēn bunta sah͈. 34 Chi dega mangi len di wah͈, H͈êt wile du wey be yef yile yepa am. 35 Asaman ak suf di na wey, wande suma i bāt du wey. 36 Wande ken h͈amul bes bōbale ak wah͈tu wōgale, du malāka i ajana ya sah͈, wala Dōm ja, wande suma Bay bi dal. 37 Naka i bes i Noah nek’ on, nōgu la ndika i Dōm i nit ka di meli. 38 Ndege naka chi bes yu jītu on tufan la, ñunga don leka, nān, sey te seylo, be cha bes ba Noah h͈arafe chi gāl ga, 39 Te yēgu ñu be tufan la ñou yubuāle len ñepa; nōgu la ndika i Dōm i nit ka di meli. 40 Fōfale ñar i nit di nañu neki chi tōl; ñu jel kena, te bayi ka cha des: 41 Ñar i jigen di nañu di wol chi wolukay; ñu jel kena, te bayi ka cha des. 42 Otu len mbōk; ndege h͈amu len ban bes la sēn Borom di ñoui. 43 Wande h͈am len lile, ne su borom‐ker ga h͈am on chi wan wah͈tu la sachakat ba di ñou, otu kon na, te du bayi mu toj nēg am. 44 Mōtah͈ na ngēn di defaru yēn it: ndege Dōm i nit ka di na ñoui chi wah͈tu bu ngēn dul fōg. 45 Kan a di bukanēg mbōk bu taku te têy, bu borom am jītal chi ker am, ndah͈ mu joh͈ len sēn dundu chi wah͈tu wa? 46 Barkel chi bukanēg bōbale, ba borom am di feka mu di def nōga ba mu agse. 47 Chi dega mangi len di wah͈, Di na ko teg njīt cha la mu am yepa. 48 Wande su bukanēg bu bon bale wah͈e chi h͈ol am, ne, Suma borom yīh͈ na; 49 Te dal di dōr i naule am, leka ak nān ak mandikat ya; 50 Borom i bukanēg bōbale di na ñou chi bes bu mu ko sēnuwul, ak chi wah͈tu wu mu h͈amul, 51 Dog ko chi diga, te sedāle ko nafeh͈a ya: fōfale la joy di neka, ak yey i buñ. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society