Matthew 22 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Yesu tontu te wah͈ati len chi i lēb, ne, 2 Ngur i ajana niro na ak bena bur bu h͈umbal on nchēt i dōm am; 3 Te yōni i ndau am ñu ôal ko ña mu ô on chi nchēt la; ñu bañ a dika. 4 Mu yōnêti yenen i ndau, ne, Wah͈ len ña ma ô on, Da ma wāj suma añ, rēndi suma i nag ak suma i rab yu dūf, te yepa emba na: ñou len chi nchēt li. 5 Wande ñu sagane ko, te dem sēn yōn, kena cha tōl am, kenen cha jayukay am: 6 Ña des japa i ndau am, tedadil len, te rēy len. 7 Wande bur ba mer, yōni i h͈are am, rēylu bōmkat yōyale, te laka sēn deka. 8 Fōfale mu ne i ndau am, Nchēt li emba na, wande ña ma ô on motu ñu. 9 Dem len mbōk chi mbeda ya, te ñu ngēn gis ñepa, ô len chi nchēt li. 10 Ndau ya dem cha mbeda ya, dajale ña ñu gis ñepa, ña bon ak ña bāh͈ itam; nchēt la fês ak ña ñu ô. 11 Wande ba bur ba h͈arafse ndah͈ mu sêt ña ñou on, mu gis fa nit ku solul on chol i nchēt ga: 12 Mu ne ko, H͈arit, naka nga fi h͈arafe, te amu la chol i nchēt gi? Wah͈ul dara. 13 Fōfale bur ba ne i rapas am, Ew len loh͈o am ak tank’ am, te sani ko chi lendem i biti; fōfale la joy di neka ak yey i buñ. 14 Ndege ñu bare la ñu ô, wande ñu new la ñu tana. 15 Fōfale la Pharisee ya deme, te fēncha naka ñu ko mun a jape chi kadu am. 16 Ñu yōni fi mōm sēn i tālube ak ga’ Herod, ne, Jemantalkat bi, h͈am nañu ne yā di dega, di jemantale yōn i Yalla chi dega, te ragalu la ken, ndege sêtu la kanam i nit. 17 Wah͈ ñu nak, Lo dēfe? Ndah͈ dagan na ñu joh͈ Cæsar ngalak, am dēt. 18 Wande Yesu gis sēn kēfēr, te ne len, Lutah͈ ngēn di ma fire, yēn nafeh͈a yi? 19 Won len ma h͈ālis i ngalak li. Ñu yub ko h͈asab. 20 Mu ne len, Bile ban natal la ak mbinda? 21 Nu ne ko, Cæsar la. Mu ne len mbōk, Joh͈ len Cæsar yef i Cæsar; te Yalla yef i Yalla. 22 Ba ñu ko dēge, ñu jomi, bayi ko, te dem sēn yōn. 23 Bes bōbale i Sadducee, ñu ne ndēkite amul, ñou fi mōm, te lāj ko, 24 Ne, Jemantalkat bi, Musa wah͈ on na, ne, Su nit dēe te amul dōm, rak’ am war na sey ak jabar am, te jur dōm chi mag am; 25 Jurom ñar i dōm i ndey nak anga won ak ñun: mag ba sey on na, dē, te amul dōm, te bayi jabar am ak rak’ am; 26 Ñarel ba itam def nōgule, ak ñetel ba, be cha jurom ñarel ba. 27 Ganou ga jigen ja itam dē. 28 Chi ndēkite ga mbōk, jabar i kan la di neka chi jurom ñar ña? ndege ñepa sey on nañu ak mōm. 29 Yesu tontu len, ne, Da ngēn jūm, ndege h͈amu len mbinda ya, wala kantan i Yalla. 30 Ndege chi ndēkite ga du ñu sey, te du ñu len maye chi sey, wande di nañu neka naka malāka ya cha ajana. 31 Wande mosu len a janga lu jem chi ndēkite ga, la len Yalla wah͈ on, ne, 32 Mā di Yalla i Ibrayuma, ak Yalla i Isaka, ak Yalla i Yanh͈oba? Yalla du Yalla i ñu dē ña, wande ñu dunda ña. 33 Ba ko mbōlo ma dēge, ñu jomi cha njemantal am. 34 Wande ba Pharisee ya dēge ne mō nopilo won Sadducee ya, ñu dajalo. 35 Kena chi ñom ku h͈amkat i yōn la won, lāj ko di ko fir, ne, 36 Jemantalkat bi, ban eblê gen a rey chi yōn wi? 37 Mu ne ko, Na nga sopa Borom bi sa Yalla ak sa h͈ol bepa, ak sa fit wepa, ak sa nh͈el mepa. 38 Bile di eble bu rey ba ak bu jeka ba. 39 Te ñarel bu niro ak mōm di bile, Na nga sopa sa morom niki sa bopa. 40 Chi ñar i eble yile la yōn wa yepa ak la yonent ya bind’ on japu. 41 Ba Pharisee ya dajalô, Yesu lāj len, ne, 42 Lan ngēn dēfe chi Krista? dōm i kan la? Ñu ne ko, Dōm i Dauda. 43 Mu ne len, Naka la ko Dauda chi Nh͈el ma ôe Borom bi mbōk, ne, 44 Borom bi nôn na suma Borom, Tôgal chi suma ndējor, be ma def sa i mbañ chi sa run tanka? 45 Su ko Dauda ôe Borom bi, naka mu neke dōm am? 46 Ken munu ko tontu bena bāt, te cha ganou lōlale, ken ñemeñatu ko lāj dara. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society